TSK

TSK · 1 Peter 2:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Sóol ñaawlu kàddu ga, mer lool. Mu ne ca xelam: «Daawuda lañu moomale fukki junni; man, junni! Lu ko deseeti lu moy jal bi?»

Ndokklee yaw mi Aji Sax ji toppul ag tooñ, te amoo xelum njublaŋ it.

Ñeel Daawuda. Bu sa xol jóg ci ku bon, bul ñee kuy def njombe.

Bésub keroog booba, yàllantuy xaalis ak wurus ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,

Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israyil, lu jar ngeen di dee?

Luke 6:42 TSK

Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax gi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax gi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko.

Luke 12:1 TSK

¶ Mbooloo ma nag mujj na dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, bay joggeente. Ci biir loolu Yeesu tàmbalee wax, jëkke ko ci ay taalibeem, ne: «Wattuleen lawiiru Farisen ñi, te mooy jinigal.

Dañoo dem ba feese gépp xeetu njubadi, akug mbon, akug bëgge, akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan, ak pexey bóome, ak ŋaayoo, akug njublaŋ, ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it,

Meew laa leen jota nàndal, waaye leeluma leen dugub, ndax àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko,

¶ Bokk yi, buleen doon ay xale ci wàllu déggin. Su dee lu bon, nekkleen ci ay tuut-tànk, waaye màggleen ci wàllu déggin.

ak ñeetaane, ak màndite, ak mbumbaay, ak yeneen yu ni mel. Ma àrtu leen nag na ma leen artoo woon, ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.

Lépp luy wextan, ak naqari deret, ak mer mu ëpp, ak coow, ak wax ju ñaaw, na lépp buube, ba génne ci seen biir, mook mboolem jëfi coxor.

Ndaxte sunub woote laloowul pexem sànke, ak mébét mu setul, akug njublaŋ.

Titus 2:3 TSK

¶ Naka noonu, jigéen ñu mag ñi itam, nañu jëfe ni mu jekke ci ay nit ñu sell; buñu yàq der, bu leen sàngara jiital, te nañuy jàngle lu baax,

¶ Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal, ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.

Waaye ku denc ci sab xol, wextanu kañaan, ak mébétum sàkku sa darajay bopp, bul damoo xel mu rafet, nde kon nga moy dëgg.

James 4:5 TSK

Am defe ngeen ne ag neen la Mbind mi indee ne: «Xemmemtéef gu ànd ak fiiraange la Yàlla am ci noo gi dëkk ci nun.»

James 5:9 TSK

Bokk yi, buleen di ñaxtoonte, lu ko moy dees na leen daan, te Daan-kat baa ngii taxaw ci bunt bi!

Ay gor ngeen, waaye jaami Yàlla ngeen. Kon buleen taafantoo li ngeen diy gor ba def lu bon.

Ndax kat: «Ku bëgga bége bakkanam, fekke bés bu rafet, na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.

Ña ngeen ci daa àndal ñoo waaru tey, ba di leen sosal, ndax li ngeen àndatul ak ñoom, daw wuti googu yàqute gu af,