TSK

TSK · 1 Samuel 13:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yanqóoba nag wax ak Simeyon ak Lewi ne leen: «Indil ngeen ma musiba, ndax dingeen tax waa réew mépp sib ma, muy Kanaaneen ñi, di Periseen ñi. Te itam awma lu dul góor ñu néew, te bu ñu booloo dal ci sama kaw, dañu may booleek sama waa kër faagaagal.»

Farba ya ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji gis ba mbugal leen, ndax tax ngeen Firawnaaki dagam jéppi nu, te mel na ni yeena teg ci seeni loxo saamar, bi ñu nuy reye.»

Léegi doxal jiitu ma Gilgal. Maa ngi noonu di la fekksi, ngir rendi fa saraxi rendi-dóomal, sarxe fa saraxi cant ci biir jàmm. Juróom ñaari fan nag ngay négandiku, ba ma fekksi la fa, xamal la looy def.»

Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki bànni Israyilam bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.»

Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen.