TSK

TSK · Acts 14:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

kon maa leen di tawal ci waxtoom, suuf si nangu, garab yi meññ.

su boobaa, Yàlla nee: «Maa leen di may seen tawub réew, saa yu jotee: lollib réew ma day taw, cooroonam taw, ngeen dajale seenum pepp, ak seen biiñ bu bees, ak seen diw gu yees.

¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas, ca ñetteelu atu maral wa. Mu ne ko: «Demal jàkkaarlook Axab, ma daldi taw ci kaw réew mi.»

Job 5:10 TSK

Keey taw, suuxat suuf, yónnee ndox, nàndal ub àll.

Job 38:26 TSK

di taw fu kenn newul, ci màndiŋ mu nit amul,

Day mébét lu ñaaw cib lalam, taxawe yoon wu dëddu mbaax, te du bañ lu bon.

ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.

Éy Aji Sax ji, yaa bare loo liggéey, te lépp di xel mu rafet. Suuf daa fees ak say càkkéef.

Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,

Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.

Seen xel demul sax ba ne: “Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Sax, jiy jot, mu tawal nu, taw yu jëkk ak yu mujj yi, àppal nu ayi bési ngóob, sédde nu?”

Maa leen def ñuy barke, ñook fi wër sama tund wi, bu jotee ma tawal leen, te tawu barke lay doon.

Yàllaa def loolu, ngir xeeti àddina wut ko, làmbatu ba daj ko, ndegam man naa am, doonte sorewul kenn ku nekk ci nun.

¶ Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.