¶ Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»
TSK
TSK · Acts 14:27
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi.
Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf,
ci turu Sang Yeesu. Bu ngeen dajee, te ma bokk ak yeen teewe ko samam xel, ci sunu kàttanu Boroom Yeesu,
Léegi nag su mbooloom gëmkat mépp dajee bérab, ñépp di làkk yeneen làkk, bu ay nit ñu xamul mbaa ñu gëmul duggsee, duñu ne dangeena dof?
ndax bunt ubbikul na ma fi ŋàpp, ngir liggéey bu am njariñ, te noon yi bare nañu.
Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu buntu xamle kàddu gi, ngir siiwtaane mbóot mi ci Almasi, li waral ñu jéng ma.