TSK

TSK · Acts 25:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Daawuda nag ma nga naan ca xelam: «Bés a ngi ñëw bu ma nara sànku ci loxol Sóol. Li gën ci man daal, du lenn lu moy dawa daw ba ca réewu waa Filisti, ba Sóol tàyyi maa rëbbati ci Israyil gépp, ma daldi mucc.»

Job 31:38 TSK

Ndegam sama tool a ma tuumaale ay jooy, rongooñi toobo yay bas-baseendoo,

¶ Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»

Naka lañu ko yeew ngir dóor ko ay kàccri, mu ne njiitu takk-der ba fa taxaw: «As goru Room bu yoon dabul, mbaa am nga sañ-sañu dóorlu ko?»

Póol itam sàkku ñu dencagum ko kaso, tey sàkku ci mbiram, àtteb buur bu tedd bi. Ma daldi joxe ndigal, ngir ñu dencagum ko kaso, ba ma yebal ko ca Sesaar.»

Àggripa moom ne Festus: «Kii kay su dénkuloon mbiram Sesaar, nu man koo yiwi.»

Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu.