TSK

TSK · Acts 28:26

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji nee: «Maa leen jiite ñeent fukki at ca màndiŋ ma, seeni yére ràppul, seenu dàll ràppul.

Mu neeti: «Demal, wax askan wii, ne leen: “Dégluleena déglu te buleen dégg, xool-leena xool te buleen gis.”

Moo tax maa ngii di dellu wéyeek askan wii, ay kéemtaan aki kiraama yuy tiiñ boroom xel ak xelam, réer xamkat ak xam-xamam.»

Man it maa leen di taamoo jox seeni mbugal, dikke leen tiitaange yi ñu yelloo, ngir maa woote, kenn wuyuwul, ma àddu, dégluwuñu ma. Xanaa di def lu bon lu ma ñaawlu, li ma buggul, ñu taamu ko.»

Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la.

¶ Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon!

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.