TSK

TSK · Acts 7:58

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Génneel dal bi ki may wax lu ñaaw, man Yàlla, te na mboolem ku ci dégg teg loxoom ci kaw boppam, ba noppi mbooloo mépp dóor koy doj, ba mu dee.

su boobaa buleen ko nangul, buleen ko déglu, buleen ko xool bëti yërmande, buleen ko baal, buleen ko nëbbal.

Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.

Acts 6:13 TSK

Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa.

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

Te it ba ñuy tuur deretu Eccen, sa seede ba, man it maa nga fa woon, juboo caak ñoom, te ña ko rey, maa leen doon wattul seeni yére.”