Su ko defee ku Asayel reyul ba nga raw, Yewu rey la; ku Yewu reyul ba nga raw, Alyaasa rey la.
TSK
TSK · Amos 1:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ca jamono jooja nag la Aji Sax ji tàmbalee fell suufas Israyil, Asayel buurub Siri di leen duma ca réew ma mépp.
Mujj na Yowakas desewuloon ca mbooloom xareem lu moy juróom fukki gawar ak fukki watiir ak fukki junniy xarekat (10 000), ndax buurub Siri moo faagaagal ña ca des ñépp, duma leen ba ñu ne mbëtt.
Fukki yoon a ngii ngeen di ma saaga, te rusuleen maa sonal.
Séddal ab cér juróom yaari nit ba juróom yett; xamoo safaan buy dikkal àddina.
Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»
Maa ngii di la def ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq; ànd aki bëñam, ngay wol tund wu mag, raatale; dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox.
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm, jalax Edomeen ña.
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom, te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Mowab, te duma fomm seeni duma. Ñoo lakk yaxi buurub Edom, def ub dóom.
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Israyil, te duma fomm seeni duma. Ñooy jaay jaam aji jub ngir xaalis bu mu leen ameel, jaay aji ndóol bu manul fey dàlli carax.
Kàddu gi dal na itam Amat, ga digalook Damaas, dal Tir ak Sidon, ak la ñuy muus lépp.