Ñu ne leen: «Li ko waral mooy, dañoo fecci kóllërey Aji Sax ji, seen Yàllay maam, te mu fasoon ko ak ñoom ba mu leen jëlee réewum Misra.
TSK
TSK · Amos 3:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Buleen ko siiwal fa Gaat, buleen ko yéene fa mbeddi Askalon, lu ko moy janqi Filisti bég, janqi yéefar yiy textexi.
Jigéen, na yiw, ñu sagal ko; góor gu néeg, alal doŋŋ.
«Jàll-leen ba ca duni Kitim fa sowu, te xool; yónneeleen Kedar fa penku, seetlu bu baaxa baax ndegam dingeen gis lu mel nii!
jëmbataat sa tóokëri reseñ ca mbartali Samari, te ku jëmbat, xéewlu ca.
«Yégleel lii Misra, yéene ko fa ca Migadol, yéene ko fa ca Memfis ak Tapanes. Neleen: “Dërleen, taxaw temm! Saamar kat a ngi lekk li leen wër.”
«“Waaye yeen tundi Israyil, yeenay naat, di meññal Israyil sama ñoñ, te léegi ñu ñibbsi.
«Bu may faj Israyil foofu ca Efrayim la seeni ñaawtéef di feeñ, ànd ak mbonu Samari seen péey. Dañuy njublaŋ, sàcc yiy bëtt ci biir kër yi, gàngoori saaysaay di songe ci biti.
Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»
Wóoy yeen ñiy jéema fanq bésub njàqare tey woo nguurug fitna!
ndax alalu njublaŋ a ngi ci biir këri njublaŋ yi ba tey, mook nattukaayi alkànde yu tuut ya ñuy jaaye?