TSK

TSK · Amos 6:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba mu ko defee Abigayil dellu ca Nabal, fekku ko lu moy mu amal biir këram bernde ju mel ni berndey buur. Xol baa nga sedd, mu màndi lool, ba tax Abigayil waxu ko dara ba bët set.

Wóoy ngalla ñiy teela xëy, daw wutiw ñoll, gonloo biiñ ba tàng jérr.

Te yeena ngii ci mbég ak bànneex, di rendi nag ak xar, di yàpp ak a naan, naan: «Nan lekk, naan, nde ëllëg, nu dee!»

«Yaw nit ki, waxal waxyu fi kaw sàmmi Israyil. Biralal waxyu ci kaw sàmm soosu, ne leen: Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Wóoy ngalla sàmmi Israyil yiy sàmm seen bopp! Xanaa du jur gi, la sàmm si wara sàmm?

Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ”

Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan.