Ñu génn digg bëccëg, fekk Ben Addàd a ngay màndi mook fanweeri buur ak ñaar ya mu faral, ca mbaar ya.
TSK
TSK · Amos 6:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aman teg ca ne: «Te kat amul ku Lingeer Esteer woo, mu wara ànd ak Buur ca bernde ja muy def, ku moy man. Ëllëg man la woo maak Buur.
Ci kaw loolu Buur bàyyikoo ca tóokër ba, délsi ca ëttu bernde ja, fekk Aman di sukk ca lal ba Esteer tëdd. Buur ne: «Ãa! Ba ci yekktaan Lingeer nag, te ma nekk ci biir kër gi?»
Tabala ju xumb selaw na, ña daa xaxaloo dal, mbégtem buumi xalam dakk.
ñu diri ko jaarale fu xar-xaru tata gëna jegee, sànni ko ca Armon.» Kàddug Aji Sax jee.
Maa leen di yóbbu ngàllo ca wàllaa Damaas.» Aji Sax jee ko wax, kookooy Yàlla Boroom gàngoori xare yi.
Gannaaw noonu la, Amaciya, Aji Sax ji nee: “Sa jabar ci biir dëkk bi lay gànctoo, say doom, góor ak jigéen, saamar tëral; sam réew, ñu natte buum, séddoo. Yaw nag, réewum yéefar ngay deeyeji; Israyil, ñu jële kom réewam, gàll ngàllo.”»
Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.