Dinaa nattoo Yerusalem buumu beteex ba ma nattoo Samari ak nattukaay ba ma nattoo waa kër Axab. Dinaa ñédd Yerusalem, ba mu mel ni ndab lu ñu ñiit ba mu set, dëpp ko.
TSK
TSK · Amos 7:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.»
Aji Sax jee dogoo rajaxe tatam janq Siyoŋ mu taaru, Moo tàllal buumu nattukaay, ngir tas ko, bankul loxoom it te màbbu ko. Moo jooyloo tata ak tabaxub fegukaay, ñu ànd tojatoo.
¶ Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal.
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Mu ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Damaa xool, gisuma lu moy ab tegukaayu làmp bu lépp di wurus, ak kopp bu tege ci kawam, ak juróom ñaari làmp ci kawam, bu ci nekk ak juróom ñaari gémmiñam ca kaw.