TSK

TSK · Amos 8:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.

¶ Ba loolu amee malaakam Aji Sax ji dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew.

Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne: «Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen, naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!” Kenn du ko jooy, naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!”

Joel 1:5 TSK

Màndikat yee, yewwuleen, jooyoo. Naan-kati biiñ yee, jooyleen biiñ bu bees, bi ñu foqatee ci seen gémmiñ.

Joel 1:13 TSK

Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!

Amos 5:16 TSK

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji, Yàlla ji ci gàngoori xare yi, dafa ne: «Bayaaloo bayaal ubalee ki yuux, mbeddoo mbedd riir aki wóoy! Dees na woo beykat bi ciy jooy, woo jooykati dëj ciy jooyoo.

Amos 6:9 TSK

Su boobaa, fukk ñu làqu ci kër, du leen teree dee.»

Amos 8:10 TSK

Maay soppli seeni màggal ab dëj, seen woyoo woy diy jooy. Maay wodde bépp lupp saaku yu ñuy ñaawloo, bépp bopp, ma wat ub nel, def ko mu mel ni dëju benn bàjjo bu góor, muj ga di bés bu tar.

Miig! Fi kanam Boroom bi Aji Sax ji, bésub Aji Sax ji kat dëgmal na; Aji Sax jee waajal ab sarax, te moo ca sellal ay ganam.