Nga waxoon nu ne nu: “Indil-leen ma ko, ngir ma gisal ko sama bopp.”
TSK
TSK · Amos 9:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.
¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.
Aji Sax jeey rëbb kuy jëfe mbon, ngir dagge ko kaw suuf, far turam.
Maa leen di toppe bëtu mbaax, ba délloosi leen ci réew mii. Maa leen di defar te duma leen daaneel; jëmbat leen te duma leen buddi.
«Demal nga wax Ebedd Meleg, Kuuseen ba, ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di sottalsi sama kàddu yi jëm ci dëkk bii, muy ayam te du doon jàmmam. Dina am ngay gis, bésub keroog.
Benn cér bi, nanga ko lakk ci digg nataalu dëkk bi, gannaaw bu fani gaw bi matee. Beneen cér bi, nga dóore ko saamar bi, kawar gi tasaaroo fi wër dëkk bi. Ñetteelu cér bi, nga sànni ko ci ngelaw li, man ma toppe ko saamar.
Su boobaa ci réew mi mépp, kàddug Aji Sax jee, ñaari xaaj yi lees di dagg, ñu sànku, ñetteel ba ca des lees fay wacc.