Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëni déwén.»
TSK
TSK · Ecclesiastes 3:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba nga xamee ne àppu Israyil a ngay bëgga mat, dafa woolu doomam Yuusufa ne ko: «Ngalla waay dugalal sa loxo, mu ron sama lupp, muy ngiñ ci yaw ne dinga jëflanteek man ci ngor ak worma: rikk, bu ma denc Misra.
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Yéegil ca kaw tundu Abarim wee, nga séentu réew mi ma jox bànni Israyil.
Musaa, jaamub Aji Sax ji nag dee foofa ca réewum Mowab, na ko Aji Sax ji tudde.
Góor ga xaacu, gëdd sarxalukaay ba ci ndigalal Aji Sax ji, daldi ne: «Yaw sarxalukaay bi, éey sarxalukaay bii! Aji Sax ji dafa wax ne: “Xamal ne doom ju góor dina juddoo kër Daawuda, Yosya lay tudd. Sarxalkati bérabi jaamookaay yiy taal saraxu cuuraay ci sa kaw, ñoom lees di rendi ci sa kaw. Yaxi nit lees di lakk ci sa kaw.”»
Xanaa du fani doom aadama fi kaw suuf àppu doñ-doñ la, dundam di dundu liggéeykat bu ñu bind?
Ndax dees na dee, di dundati? Konoon ma muñe ko sama fani coono yépp, ba keroog sama kuutaay yiwisi ma.
Mooy dëël jigéen ju tële woona jur, may ko mbégtem njureel. Màggal-leen Ki Sax!
Mu gàbb ko, dindi doj ya, jëmbat ca ngëneeli reseñ, tabax tóojub doj fa digg ba, ba yett ca mbalkam nalukaayu reseñ, tey yaakaar reseñ ju neex, mu meññ, wex.
¶ Jant yooyu Esekiya moo woppoon, bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!”»
«Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul! Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.» Aji Sax ji nee: «Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot kiy séy.
Leeg-leeg ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko déjjati, daaneel ko, tas ko,
Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
¶ «Ñu dem ba dige ba Yàlla giñaloon Ibraayma di waaja sotti, yemook xeet wi yokku, di gëna bare ci Misra,
Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,