TSK

TSK · Exodus 12:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yeena ngii tey di dem seen yoon ci weeru Abiib.

¶ «Màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir, ni ma la ko sante bu àppam taxawee ci weeru Abiib, ndaxte weeru Abiib ngeen génne fa Misra.

¶ «Fukki fan ak ñeent ci weer wi jëkk, diggante ngoon ak jant bu so, mooy màggalu bésub Mucc ba, ñeel Aji Sax ji.

¶ Wormaal-leen weeru Abiib, te ngeen amal ci màggalu bésub Mucc, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, ndax ci weeru Abiib la leen seen Yàlla Aji Sax ji génnee Misra, ag guddi.

¶ «Fukki fan ak ñeent ci weer wu jëkk wi mooy seen màggalu bésub Mucc ba. Juróom ñaari fan la màggal giy am, te mburu mu amul lawiir lañu ciy lekk.