Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen.
TSK
TSK · Exodus 7:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Li waral Firawna du leen déglu, mooy sama kéemaan yi wara fulandiwu ci réewum Misra.»
Xol laa lay sàkkoo guddi, sama jëmm jépp di la laaj. Bu say àtte teewee fi kaw suuf, waa àddina xame ca njekk.
¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Sama ñeenti mbugal yu tar yii laay yebal ci kaw Yerusalem. Ñuy saamar akub xiif ak rabi àll aku mbas, ngir dagge ci réew mi nit ak mala.
Maay yàqte Pattros, taal dëkk bi ñuy wax Cowan, ba sottal sama mbugal ci kaw dëkk bi ñuy wax No.
Boroom bi, ana ku la ragalul? Ku dul màggal saw tur? Yaw doŋŋ yaa sell. Askan yépp ay dikk, sujjóotsil la, ndax yaa jubi dogal.»
Ay àtteem dëgg la, yoon la! Moo mbugal jigéenu moykat bu mag, bi yàq àddinaak moyam, feye ko deretu jaami Yàlla yi mu tuure loxoom.»