TSK

TSK · Ezekiel 21:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu Yosuwe dégg coowal mbooloo may xaacu. Mu ne Musaa: «Coowal xaree ngoog ca dal ba!»

Job 39:25 TSK

mu feeloo ko coowal wakkan ya. Fu sore lay xañtoo xare ba, ak kàdduy njiiti xare, ya riirandook xaacu ya.

Aji Sax ji Yàllay Israyil déy dafa wax ci mbirum këri dëkk bii ak këri buuri Yuda yii ñu màbb, di ko fegoo sëkk bi ñu leen gawe te di ko làqoo saamaru waa Babilon ñi ñuy xareel. Mu ne: «Kër yi dina fees ak néewi nit ñi ma bóom ndax mer ak xol bu fees. Dinaa làq dëkk bii sama yiw ndax seen gépp mbon.

¶ Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook Yerusalem, yékkati gawukaay, wërale ko.

Seen ñetteelu xaaj, mbas lañuy deeye mbaa xiif bu leen di sànk ci biir dëkk bi. Beneen ñetteelu xaaj bi, saamar lañuy fàddoo ci seen dig-digal bi. Xaajub ñetteel bi ci des, fépp fu ngelaw jublu laa leen di tasaare, te saamar laa leen di toppe.

mooy rëkke say miir dénku dàjjikaay, mooy màbbe say tata ay sémmiñam,