TSK

TSK · Ezekiel 21:24

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Jàmbaar, dama ne Aji Sax jee lay xalab; da la naa nikk,

«Téenleen, séentu tund ya ne faraas! Ana fu ñu leen fi tëddewul? Ci yoon yi ngeen di yeeroo ni màngaan muy dogalee ci màndiŋ mi. Sobeel ngeen réew meek seen gànctook seenug mbon.

Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.

«Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, te man faalewñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.

Yaa tànn ci sa yére yu yànj, rafetale sa jaamookaayi tuur, ba noppi di ca gànctu; lu masula am te du amati mukk.

«Yaw nit ki, waxal Yerusalem ne ko: “Yaa di suuf su ñu dindiwul sobeem, te tawluwul keroog bésub sànj ma.”

waa Babilon, Kaldeen ñépp, muy waa Pekot, di waa Sowa, di waa Kowa, ànd ak waa Asiri yépp, di xale yu góor yu sopplu, ñoom ñépp di kàngam aki jawriñ, di kilifa yu ràññiku, ñoom ñépp war ay fas.

Hosea 4:2 TSK

Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo. Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.

Deret ngeen tabaxe Siyoŋ, njubadi ngeen tabaxe Yerusalem googu.