TSK

TSK · Genesis 11:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»

Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet.

¶ Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.

Ba ñuy wax loolu, foogoon nañu ne Yuusufa déggul seen làkk, ndax làppto, ba doxoon seen diggante, di tekki.

Job 5:12 TSK

Keey neenal pexem ku muus, ba mébétam du sotti.

Ki ci jalub asamaan a ngay ree, Boroom baa nga leen di kókkali,

Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»

Éey waa kër Israyil,» kàddug Aji Sax jee, «maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore. Xeet wu am kàttan lañu, xeet wu yàgga yàgg, wu ngeen xamul seen làmmiñ, te dégguleen seeni wax.

ndax kiy làkk weneen làkk, du nit ñi lay waxal, waaye Yàlla lay waxal, gannaaw kenn déggul li muy wax. Teewul ci Noo gi lay waxe ay kumpa.