Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”»
TSK
TSK · Genesis 28:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Aji Sax ji waxati Musaa,
Léegi nag man maa ko sédd Aji Sax ji: giiru dundam lees ko sédd Aji Sax ji.» Ba loolu amee ñu sujjóotal Aji Sax ji foofa.
ndax kat, sang bi, ba ma nekkee Gesur ca Siri, damaa dige woon ne: “Su ma Aji Sax ji delloo, ba ma dellu Yerusalem, dinaa dem màggali ko.”»
¶ Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ca weer woowa, bànni Israyil daje nañu, sol ay saaku, xëppoo suuf, di ko ñaawloo ci biir koor.
Yàlla laa wóolu, ragaluma. Lu ma nit manal?
Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam, nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo;
Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy; desu xadaram, nga gañoo.
Samay digeek Aji Sax ji laay matal fi kanam ñoñam ñépp,
Moo giñaloon Aji Sax ji, moo digook Mbërum Yanqóoba ma.
Bésub keroog Aji Sax ji ci boppam mooy xamal Misra mooy kan, ba waa Misra xam Aji Sax ji, di jaamoo Aji Sax ji saraxi gàtt ak saraxi pepp, digook moom tey wàccook seeni dige.
¶ Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
Kon su nu amee lu nu lekk, ak lu nu sol, nanu ko doyloo.