¶ Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
TSK
TSK · Genesis 3:14
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Genesis 3:1
TSK
Exodus 21:28
TSK
¶ «Su aw nag dañee góor mbaa jigéen, ba rey ko, dóorleen nag wi ay xeer ba mu dee, te buleen lekk yàpp wi, waaye boroom nag wi, yoon toppu ko.
¶ Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw:
Isaiah 29:4
TSK
Dinga suufe ba mel ni kuy àddoo biir suuf, sa baat di ndéey lu dégtoo xóote ya pëndub suuf lale, mel ni njuuma lu waxam bawoo biir suuf, baatam yeloo xóote ya pëndub suuf lale.
Micah 7:17
TSK
Ñooy mëq suuf ni jaan, ak ndëgmeenti suuf, di lox, génne seeni tata, te su boobaa yaw sunu Yàlla Aji Sax ji lañuy tiit, ragal la.