TSK

TSK · Genesis 32:24

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»

malaaka mi ma jot ci bépp loraange— yal na barkeel xale yi, ba ñu saxal sama tur ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa, te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.»

Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam.

Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.

¶ Gannaaw loolu bokk yi, li ma leen di ñaan ngir sunu Boroom Yeesu Almasi, ngir itam cofeel gi Noo gu Sell giy maye, moo di ngeen fekksi ma ci xareb ñaan ngir man.

Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.

¶ Bëgg naa nag, ngeen xam xare bu metti, bi ma leen di xareel, yeen ak waa Lawdise ak mboolem gëmkat ñi ma masula teg bët,

Fan yi Almasi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te nangule na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.