saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
TSK
TSK · Genesis 35:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ibraayma daldi suul soxnaam Saarata ca xuntim xeer ma ca biir toolub Magpela, booba janook Mamre, di Ebron léegi, ca réewu Kanaan.
Ba loolu weesee la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel.
Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam.
¶ Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.»
¶ Naka la Yanqóoba dénku doomam yu góor ya noona, daldi delloo ay tànkam ca lal ba, bakkan ba rot, mu fekki ay maamam.
Nga dem, ba ragal fu kawe, am tiitaange ciw yoon, garab tóor, ba weex furr, soccet di yokokoki, doomu garab tëë yékkati siddit, nga jëm kër gu mujj, waa dëj bi fees mbedd mi.