TSK

TSK · Genesis 38:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Bu ay góor yu bokk waajur dëkkee, kenn ci ñoom dee te bàyyiwul doom ju góor, jabaru ki dee du génn, di séy akub jaambur. Jëkkëru donaleem ju bokk ak jëkkëram moo ko wara jël, donloo ko.

Ruth 1:11 TSK

¶ Mu ne leen: «Ñibbileen ngalla, doom, lu ngeen di ànd ak man doye? Ndax dama leena manatee jural ay jëkkër ci sama biir bii?

Job 5:2 TSK

Am sannax déy, naqari deret a koy rey, ab téxét, xéraangee koy faat.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.

Ndax kañaan ak sàkku sa darajay bopp, fu mu ame, fa la salfaañoo di ame, ak mboolem jëfi ñaawtéef.