¶ Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko.
TSK
TSK · Genesis 4:26
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aji Sax ji ngeen biral bésub tey, ne mooy doon seen Yàlla, te dingeen doxe ay yoonam, di sàmm dogali yoonam, aki santaaneem, ak àttey yoonam, tey dégg waxam.
yaw laay sarxalal saraxu cant, te turu Aji Sax ji laay tudd.
Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen; yeen ñi ñu wooye turu Israyil, yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda, di giñe turu Aji Sax ji, yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil te dëgg ak njekk taxul,
Bés yooyu Yuda day mucc, Yerusalem dëkke jàmm, ñu di ko wooye: “Aji Sax ji sunu njekk.”»
«Su boobaa ma soppi làmmiñu xeet yi, setal ko, ngir ñuy tudd ñoom ñépp turu Aji Sax ji, di ko jaamoondoo benn bopp.
Su boobaa, ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, mooy raw.»
¶ Looloo ma taxa sukk sama bëti óom, janook Baay bi,