TSK

TSK · Genesis 42:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba loolu amee ñaari malaaka ya dikk Sodom ca ngoon, fekk Lóot toog ca buntu dëkk ba. Lóot séen leen, jóg gatandu leen, daldi leen sujjóotal, ne leen:

¶ Gannaaw gi geneen gént dikkal ko, mu nettali ko ay magam ne leen: «Dégluleen, géntaat naa. Gis naa jant bi ak weer wi ak fukki biddiiw ak benn di ma sujjóotal.»

juróom ñaari ati xiif ya tàmbali, na ko Yuusufa waxe woon. Réew yépp nag nekk ci xiif, waaye amul fu ñàkk dund ca Misra.

Ba ñu demee, ba metitu xiif bi dajal réew mépp, Yuusufa dafa ubbi denc yépp, di jaay pepp mi waa Misra,

¶ Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf.

Ñu wax ko ne ko: «Ndekete Yuusufaa ngi dund! te sax mooy kilifag réewum Misra gépp.» Ba Yanqóoba déggee loolu, yaramam dafa dee goyy ca saa sa, ndaxte gëmu leen.

Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati.

Acts 7:10 TSK

xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.