Ci kaw loolu Yanqóoba ne: «Sama doom daal, du ànd ak yeen, ndax magam faatu na, te moom rekk a des. Su ko musiba dabee ci yoon wi ngeen jëm, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.»
TSK
TSK · Genesis 43:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Firawna dellu ne Yuusufa: «Am nga ndigal itam ci wax leen ne leen: “Ni ngeen koy defe nii la: dangeen di jële ay watiir ci réew mi, dem yeb ci seeni doom ak seeni soxna, te ànd ak seen baay, ngeen ñëw.
Kon nag buleen tiit, dinaa leen yor, yeen ak seeni doom.» Yooyu kàddu la dalale seen xol, ba ñu am jàmm.
Seen tuut-tànk, yi ngeen ne alalu sëxëtoo lañuy doon, ñoom laay yóbbu, ba ñu xam réew ma ngeen xarab.
Su nu demee ca biir dëkk ba, danuy dee ak xiif. Su nu toogee fii itam, dee ak xiif. Kon kay nan dem ca dalub waa Siri, jébbal leen sunu bopp. Su ñu nu bàyyee, nu dund, baax na. Su ñu nu reyee it, nu dee rekk.»
¶ Ba loolu amee ma digle foofa koor ca tàkkal dexu Aawa, toroxloo ko fa sunu kanam Yàlla, ngir ñaan ko mu may nu yoonu jàmm, nook sunuy doom ak mboolem lu bokk ci nun.