¶ Mu am bés Ibraayma wax surgaam, bi gëna yàgg ci këram, tey saytu alalam jépp, ne ko: «Dugalal sa loxo ci sama suufu lupp,
TSK
TSK · Genesis 47:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yanqóoba wax Firawna ne ko: «Samay ati màngaan, ba ma ganee àddina ba tey de, mu ngi tollu ci téeméer ak fanweer, muy at yu gàtt te naqari, te it demuma bay tolloo ay at ak samay maam, ba ñuy màngaan ci àddina.»
baayam da ne woon, mu ngi waaja dee, waaye bàmmeel ba mu yettaloon boppam ca xunti ma ca réewu Kanaan, na ko giñal ne dina ko denc foofa. Mu ne kon, na ko Firawna may, mu robi baayam, ni mu ko ko giñloo woon, te délsi.
¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbali di gànctuy topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew, ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre gi ma fasoon ak ñoom,
Su dee dee moom, nun ñépp ay dee ni ndox di tuuroo ba deesu ko tanqati. Yàlla nag musalul kenn ci dee, waaye moo lal pexe ngir ki gàddaay du saxoo gàddaay bérab bu ko sore.
Xanaa du fani doom aadama fi kaw suuf àppu doñ-doñ la, dundam di dundu liggéeykat bu ñu bind?
Xam naa xéll ne ci dee nga ma jëme, te mooy kërug ndajem képp kuy dund.
di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?
Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?
Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci,