TSK

TSK · Genesis 47:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu.

¶ Naxor am ñaar fukki at ak juróom ñeent, jur Teraa.

Isaaxa dund na téeméeri at ak juróom ñett fukk (180).

¶ Gannaaw loolu Yuusufa nelaw ci téeméeri atam ak fukk. Ñu waajal néew ba, ba du yàqu, daldi koy yeb cib tàdd, denc ko foofa ca Misra.

Musaa nga tollu woon ci juróom ñett fukki at (80); Aaróona moom am juróom ñett fukki at ak ñett (83); ca jamono, ya ñuy wax ak Firawna.

Job 14:1 TSK

Ku jigéen jur, yaa néewi fan, géejal coono!

ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.

Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la, teewlul, ma woo la wall; bul tanqamlu sama yuux, doxandéem doŋŋ laa fi yaw, di gan ni maam yépp.

Yaay delloo doom aadama ci pënd, ne ko: «Yaw, doom aadama, dellul!»

Sa dogali yoon laay woyantoo, fu ma mana sance.

Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.

Yeen xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes!