TSK

TSK · Genesis 48:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yal na la Yàlla may layub asamaan ak ngëneeli suuf, pepp ne gàññ, biiñ walangaan.

Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.

¶ Naka la Esawu siggi, gis jigéen ñi ak xale yi, mu ne: «Ñii ànd ak yaw ñooy ñan?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa njaboot, gi ma Yàlla baaxe, sang bi.»

¶ Ñaan gii nag la Musaa, góoru Yàlla ga ñaanaloon bànni Israyil, bala moo nelaw.

¶ Aana mujj ëmb ca ndeetel at ma. Gannaaw gi mu am doom ju góor, tudde ko Samiyel (mu firi Yàlla dégg na), ndax da ne: «Maa ko ñaan Aji Sax ji.»

Ci biir loolu Eli daan na ñaanal Elkana ak soxnaam, bala ñoo ñibbi, ne: «Yal na la Aji Sax ji may kuutaay ak sa soxna sii, ñu wuutu ki mu sédd Aji Sax ji.»

Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.

¶ Ba Yanqóoba di waaja nelaw, ngëm la ñaanale ñaari doomi Yuusufa yépp, doora sujjóot, jafandoo boppu yetam.