TSK

TSK · Hebrews 12:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu Musaa defarlu jaanu xànjar, wékk ko ci bant, ba képp ku jaan màtt, bu xoolee jaanu xànjar ja, daldi mucc.

Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»

Maa ngi séentu Aji Sax ji, mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw, waaye maa ngi koy yaakaar.

Yeen waa àddina, catoo cat, walbatikuleen fi man, mucc. Man maay Yàlla, du keneen.

Gannaaw laa jox ku may dóor, dékk lex kuy xus sama sikkim, te làquma sama kanam ku may saagaak a serati.

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.

Luke 17:5 TSK

¶ Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»

Mbooloo maa nga taxaw di seetaan, njiit ya ñoom di ko kókkali, naan: «Musal na ay nit; na musal boppam nag, ndegam mooy Almasib Yàlla, ki ñu fal!»

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Acts 5:41 TSK

¶ Ndaw ya nag bàyyikoo ca kurélu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.

Ñaar ñi la Almasi boole ci jenn jëmm, jubale leen ak Yàlla, ca bant ba ñu ko daajoon, te bant ba la dakkale sunub tongoo.

Te lii kat, bir na ma; ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.

Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi.

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla, miy Yeesu Almasi, Musalkat bi.

Ana kan ci malaaka yi la mas ne: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon, say dëggastal»?

Noonu lees matale Almasi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

¶ Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu tooge ndijooru ngànguney ku Màgg ka fa asamaan.

¶ Moo tax ba Almasiy dikk ci àddina la wax ne: «Saraxug jur aki jooxe, taamuwuloo ko, waaye aw yaram nga ma waajalal.

Leeg-leegaa ñu saaga leen, bundxatal leen ci kanam nit ñi; leeg-leegaa yeen ay taxawu nit ñi ñu teg lu ni mel.

Xool-leen ci moom mi bàkkaarkat yi doon xeex, bala ngeena yoqi bay xàddi.

Gëstu nañu jan jamono, ak yan xew-xew la Noowug Almasi ga nekkoon ci ñoom, tegtale woon. Mooy ba Noo gay seede lu jiitu, coonoy Almasi, ak ndam ya cay topp.

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.

Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.

Jude 1:21 TSK

Fexeleen ba des ci biir cofeelu Yàlla, tey séentu sunu yërmandey Boroom Yeesu Almasi, ngir ag texe gu sax dàkk.

Mu ne: «Mboolem loo gis, bind ko cib téere, nga yónnee ko juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca dëkk ya ñuy wax Efes ak Samirin ak Pergam ak Catir ak Sàrd ak Filadelfi ak Lawdise.»

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Samirin nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Ki Jëkk te Mujj, Ki dee woon te dekki. Mu ne: