Yeena fàtte Yàlla ji leen di musal, bawuleen xel seen cëslaay jiy seen rawtu, xanaa di jëmbatal seeni tuur ay tooli ngëneel, di ji jiwu mu bawoo feneen.
TSK
TSK · Hosea 2:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Maa lay wacceek say far, ñu màbb say néeg, tas say jaamookaay, futti la, nangu sa gànjar gu yànj gépp, wacc la yaramu neen, nga ne duŋŋ.
Li ko waral mooy buur bëj-gànnaar day dellu waajalaat mbooloo mu ëpp ma jiitu. Bu amee ay at dina dikkaat, ànd ak mbooloom xare mu mag ak ngànnaay lu takku.
«As ngelaw lañu ji, ñooy góob ngëlén. Gub du jóg, pepp du focci, te bu pepp amoon it, jaambur a koy wonn.
Jombul mu dëpp, fomm, bàyyi gannaawam barke, ba ci saraxu pepp ak saraxu tuuru, ñeel seen Yàlla, Aji Sax ji.»
Yeenay ji lu bare, góob tuuti; lekk, suuruleen; naan, màndiwuleen; solu, nugluwuleen; boroom peyoor feyeeku, yeb ci mbuus mu bënn.»
Su Edom nee: “Dees noo rajaxe, waaye nooy tabaxaat gent bi,” Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moom dafa wax ne: “Ñooy tabax, maay màbb.” Ñoom lees di wooye waa diiwaan bu bon bi, askan wi Aji Sax ji mere ba fàww.