TSK

TSK · Isaiah 2:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 40:11 TSK

Yuril sa mer, te xool képp ku bew, detteel ko,

Buur Yàlla di ko ree, xam ne bésam a ngi ñëw.

Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:

Doom aadama torox na, nit detteelu na, ku doon regeju, detteelu.

Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, njobbaxtal ya gëna kawe dog, la ca gënoona siggi, wàcc.

Bésub Aji Sax jaa ngii di ñëw, bés bu néeg, bésub mer ak sànj muy tàkk, nara gental suuf, te bàkkaarkat ya la fay fàkkas.

Teewul nga tàbbi njaniiw, àkki ba ca xóotey pax ma.

Suuf a ngi wowa wow, ne sereŋ, àddina ne làcc, ne sereŋ, kàngami xeeti àddina ne làcc.

Mooy sànk kilifa, di neenal njiitu àddina.

«Aji Sax ji dafa wax ne: Ni lii yàqoo, ni laay sàggee sagub Yuda ak sagu Yerusalem bu réy bi.

«Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.» Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. «Sa bés déy taxaw na, di àpp bi ma la wara mbugale.

Amos 5:18 TSK

Wóoy kuy yàkkamti bésub Aji Sax ji! Ana lu ngeen am ci bésub Aji Sax ji? Dug leer, xanaa lëndëm.

Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, ka toroxlu lees di yékkati.»

ndax yeen ci seen bopp, xam ngeen xéll ne Sang bi, ni sàccub guddi lay dikke.