TSK

TSK · Isaiah 22:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Ruth 1:20 TSK

¶ Mu ne leen: «Buleen ma ne Nawmi (mu firi Boroom mbégte mi), neleen ma Mara (mu firi Boroom naqar wi), ndax Aji Man ji da maa teg naqar wu réya réy.

Naa xaacu, woo Yàlla, sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.

Xool-leen seen jàmbaar ñiy yuuxoo ci mbedd mi, ndawi jàmm yaa ngii, di jooyoo jooy yu metti.

Éey bokk yi, sol-leeni saaku, diwoo dóom, ñaawloo ko. Ñaawluleen ni kuy dëj benn bàjjo te jooy jooy yu metti, nde yàqkat bi day jekki, ne sunu kaw dàll!

Éy ku ma mayoon ci màndiŋ mi dalu panaanum njëggaan, ba ma teqlikook bokk yi, wacc leen, dem, bàyyi leen? Ñoom ñépp ay bokkaale, di gàngooru workat.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Yuux dégtu na fa Raama, ay jalooki jooy yu metti. Rasel ay jooy ay doomam, baña noppi, ndax doomam ya wuute.»

Micah 1:8 TSK

Lee ma tax di jooy ak a yuuxu, ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo. Naa yuuxu nig till, naa sab sabum looy ndaxu naqar.

¶ Ba Yeesu jubsee ba séen dëkk ba, jooy na ndax moom.