¶ Bu gaal ga jógaan, Musaa da naan: «Jógaloo, Aji Sax ji, say noon fëlxoo, say bañ daw la.»
TSK
TSK · Isaiah 31:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Keey kepp boroom xel cig muusam, ba pexem ndëngteem teela sooy.
Kee am doole, keey sottal, di boroom aji réer ak ka ko réeral.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woyu Sabóor.
Te noonu la buurub Asiri di yóbboo ngàllo Misra, toxal waa Kuus, ñuy ay ndaw aki màggat. Yaramu neen, tànki neen lañuy def, seen taat ne fàŋŋ, muy gàcceg Misra.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dégtal na ma lii: «Gii ñaawtéef déy deesu leen ko jéggal, ba keroog ngeen di dee.» Boroom bee ko giñ, moom Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Rawtub Firawnaay mujj di seen gàcce, keppaarug Misra di seen toroxte.
googu ñaawtéef ay mujj doon seen xar-xaru tata ju kawe, funki, tata ja jekki jóoru.
Ab dof, waxi dof lay wax, xel ma di nas ñaawtéef, mu nar jëf ju teddadi. Lu ñaaw lay wax, jëme ci Aji Sax ji, di xiifal ku xiif, di xañ ku mar lu mu naan.
Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.
Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; dun bi, mu sampem xelam; asamaan, mu lale xam-xamam.
Te lii nangeen ko def ab takk.” Kàddug Aji Sax jee. “Maa ngii di leen dikke mbugal ci bii bérab, ba ngeen xam ne samay kàddooy sotti ba mat sëkk, di seen loraange.”»
Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?
Teewul sama kàdduy àrtu ak sama dogali yoon ya ma yóbbante woon sama jaam ña, yonent ya, du lépp a dab seeni maam? Ñu dëpp nag daldi ne: “Noonee Aji Sax ji Boroom gàngoor yi nammoona def ak nun, feye nu ko sunuy jikko ak sunuy jëf, noonu la def ak nun.” »
kooku mooy Yàlla mi wéetoo xam-xam, te moom la teddnga ñeel ba fàww, ndax Yeesu Almasi! Amiin.
Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.