TSK

TSK · Isaiah 40:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 40:11 TSK

Yuril sa mer, te xool képp ku bew, detteel ko,

Na waa àll beeki dëkkam xaacoondoo, waa dalub Kedar ak waa Sela sarxolleendoo, kaw tund ya di riirum mbég!

Maay doxloo silmaxa yi ci yoon wu ñu xamul, ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer, fu ñagas, ma maasaleel leen. Lii laa leen di defal, te duma leen wacc mukk!

Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, xàll-leen yoonu xeet wi, maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, dindi doj yi! Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.

Buuru Babilon a ngay taxaw ca selebe yoon wa, fa ñaari yoon ya séddlikoo, ngir gisaane. Dina yëngal fitti seetukaay yi, xool ci terafim yi, jumtukaay yi ñuy gisaanee, te dina xool ci resu jur.

Luke 1:52 TSK

wàccee buur yi ci seeni gàngune, yékkati baadoolo yi.

¶ Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»