TSK

TSK · Isaiah 63:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”

Waaye yaw, ci sa yërmande ju réy, waccoo leen ca màndiŋ ma. Taxaaru niir wa noppiwula taxaw ci seen kanam bëccëg bu nekk, di leen jiite ca yoon wa. Taxaaru sawara wa it noppiwula taxaw guddi, di leen niital yoon wa ñuy jaar.

Nga daldi leen teg ci seen loxoy noon, ñu fitnaal leen. Teewul ñu jàq, woo la wall, nga dégge ko fa asamaan, ba jox leen ñu leen xettli, ci sa yërmande ju yaa, ñu xettli leen ci seen dooley noon.

Ba ñu moomee seenum réew, nekk ci sa teraanga ju réy ja nga leen may ca suuf su yaa, su nangu sa nga leen jox, jaamuwñu la woon te dëdduwñu seen manin yu ñaaw ya.

Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo, ngir niir sa leer ak sa teddnga.

Boroom bi, yaa baax, di bale, di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku.

Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, te baña fàtte mboolem xéewalam!

Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.

Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.

Nangeen sante Aji Sax ji mbaaxam. Kee saxoo ngoram!

Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.

Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool, xool ci Saarata mi leen meññ. Ba muy kenn laa ko woo, barkeel ko, ful ko.

Na ku bon ba jëfinam, kuy def lu ñaaw fomm mébétam, te walbatiku ci Aji Sax ji sunu Yàlla, mu yërëm ko, yaatal njéggalam.

Maa fa jaare, seen la ngay wéqu, sangoo sa deret. Ma ne la: Sangoo nga sa deret waaye, dundal! Neeti la: Sangoo nga sa deret, waaye dundal.

Ndaw bànneex akub taar ca ñoom! Pepp yafal xalelu góor, biiñ bu bees naatal yaramu janq.

¶ Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,

¶ Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp,

Titus 3:4 TSK

Waaye ba Yàlla sunu Musalkat feeñalee mbaaxam ak mbëggeelam ci doom aadama,