TSK

TSK · Isaiah 64:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ana lu jar Misra di wax naan: “Musiba mi mu leen naraloon, ba mu leen di yiwi de, du lenn lu moy rey leen ba ñu jeex ca tund ya, ba fare leen kaw suuf sépp.” Ngalla dëddul sa sawaras sànj te nga fomm musiba mi nga naral sa ñoñ.

Aji Sax jee gis loolu, gedd, ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.

Job 10:9 TSK

¶ Rikk fàttlikul ne yaa ma tabax, ni bu ma doon ban, xanaa doo ma delloo xaat ci pëndub suuf?

Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. Moo nu sàkk, nuy ñoñam, di gàttam yi muy foral.

Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.

Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? Ma woote, kenn wuyuwul? Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? Am damaa ñàkk doole ju ma xettlee? Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; jën ya mar, dee ba yàqu?

Aji Sax ji kat dafa wax ne: «Jaam yi ñu xañ ngóora, su ñu sàmmee sama bési Noflaay, taamu sama coobare, tey feddli sama kóllëre,

Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.

Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, te njekkam la sukkandikoo.

Seen làmmiñ di fitt guy bóome, seeni wax dig njublaŋ. Nit di wax moroomam jàmm, te di ko tëru cim xelam.

Ma seet ci seen biir kuy defaraat tata ji, janook man ci bëttukaay bi, ngir taxawal réew mi, ba duma tas réew mi, waaye gisuma kenn.

Ma daldi ñibbi, ba ñu nangu seenug tooñ, sàkku ma. Bu ñu jàqee lañuy daw wutsi ma.»

Du seen xol lañu ma wooye wall, xanaa di salliiru ci seen kaw lal, pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram, dëddu ma.

Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? Te jenn Yàlla jee nu sàkk? Lu waral ku ne di wor mbokkam, ba fecci kóllërey maam ya?