Seen tuut-tànk yi ngeen noon dees na leen sëxëtoo, seen doom yii xamagul lu baax ak lu bon, ñooy duggi réew ma. Ñoom laa koy jox, te ñoo koy nangu.
TSK
TSK · Isaiah 8:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Buurub Asiri nangul ko, dal ca kaw Damaas, nangu dëkk ba, jàpp waa dëkk ba, yóbbu Kir, ba noppi rey Reccin.
¶ Ba loolu amee Salmanasar buurub Asiri dal ca kaw réew ma mépp, dikk ba Samari, gaw ko diiru ñetti at.
Damaas a yilif Siri, te Reccin yiliful lu moy Damaas. Fii ak juróom benn fukki at ak juróom Efrayim tas, ba xeet wa réer.’
Bala xale bee ràññee lu baax ak lu bon, dees na gental réew mii nga ragal seen ñaari buur.
Yéene bii ñeel na Damaas: Damaas a ngii, léegi mu noppee doon ab dëkk, xanaa ab jalu tojit;
Te tóor mu lax mi muy gànjaroo, mu tege ca coll ya tiim xur wu nangu wa, day mel ni figg ju ñor te jotul; ka ko gis a koy gaaw witt, wonn.
Man nag, Niniw, dëkk bu mag bii ëmb lu ëpp fuuf téeméeri junniy nit ak ñaar fukk (120 000), ñu ràññeewul seen ndijoor ak seen càmmoñ, ak mala yu bare, duma leen xalaat?»