TSK

TSK · Jeremiah 25:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleena màbb, ba kenug dëkk bi siiñ!»

Aji Sax ji kat teg na tund wii loxo, te ni ñuy dëggaatee boobum leeñ, ni lees fiy dëggaatee Mowab.

Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»

Aji Sax ji da ne ma: «Sàkkalal sa bopp ay der ak yeti ràngaru yëkk, nga boole lépp teg ci sa ndodd;

¶ Lu jëm ci Mowab, Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na! Kiryaatayim, ñu torxal, nangu ko; tata ja daanu, tasaaroo.

¶ Lu jëm ci Edomeen ñi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Xanaa boroom xel amatul fi Teman? Xanaa ndigal a réer xamkat yi? Am seen bopp a yàqu?

¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:

te maay wàcceel Mowab ay mbugal, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»

¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:

¶ Peeñum Abdiyas a ngi. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii ñeel askanu Edom.

«Maa dégg ŋàññi Mowab, kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ, tey damu, nara nangu seen suuf.