TSK

TSK · Joel 2:23

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

kon maa leen di tawal ci waxtoom, suuf si nangu, garab yi meññ.

Aji Sax jee leen di ubbil mbàndam mu baax ma fa asamaan, ba bu jotee mu tawal seenum réew, boole ci barkeel seen mboolem ñaq. Yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb.

su boobaa yaw ngalla nangool fa asamaan, te nga jéggale sa bàkkaaru jaam ñi, Israyil sa ñoñ. Ngalla xamal leen yoon wu baax wi ñu wara doxe te nga tawal sa suuf, si nga joxoon sa ñoñ, muy seen cér.

Job 37:13 TSK

mu mel ni yet wu muy bantale waa àddinaam, mbaa mu firndeele leen ko ngoram.

Yaw aji jub ji, bégal te bànneexoo Aji Sax ji. Képp kuy def njub, sarxolleel!

Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji, nu xaacul ki nuy sës, mucc.

mooy sànge asamaan ay niir, tawal suuf, saxal tund yi am ñax,

Buur, na kanam ga leer, sa bakkan mucc, su la baaxee, mu mel ni taw bu topp um nji.

di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.

Yaa leen di bàcc, ngelaw wal, ngëlén tasaare; yaw ngay bége Aji Sax ji, di damoo Aji Sell ju Israyil.

Moo tax waame aje, taw yiy mujje dikkul. Teewul ngeen dëgër bët nib gànc, ñàkk gàcce!

Doomi Siyoŋ yu góor yu jar ya! Wurus lees leen daan nàttablee, ndeysaan tey, ñu jàppe leen ni njaqu ban lu tabaxkatu njaq liggéeye loxoom.

Hosea 6:3 TSK

Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»

Amos 4:7 TSK

Mu ne: «Maa leen xañ ub taw bu leen may ngóob ci ñetti weer. Ma taw ci bii dëkk, tawuma ca bee. Wii waar tawlu, wee waar lax.

te man may bànneexoo Aji Sax ji, Yàlla ji may wallu laay bége.

Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.

¶ Bu suuf maree, ñaanal Aji Sax ji ab taw, Aji Sax ji mooy sàkk ay xàmbaar, sóobal nit ab taw, saxalal ku ne am ñax ci àll bi.

Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»

Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy jaamoo Yàlla Noowam gu Sell, di damoo Almasi Yeesu, te yaakaarunu aaday nitu suuxu neen.

James 5:7 TSK

¶ Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.