TSK

TSK · Leviticus 1:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ba noppi, nga rendi kuuy mi, jël deret ji, xëpp ko ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj.

Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Day teg loxoom ci kaw boppu jur gi muy sarxal, te rendi ko ca bunt xaymab ndaje ma. Doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi daldi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

te teg loxoom ci bopp bi, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi. Na doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Bu noppee na rendi sikket biy saraxas póotum bàkkaaru mbooloo mi, te yóbbu deret ji ca gannaaw rido ba. Na def deret ji na mu defoon ak deretu yëkk wa, wis-wisal ko ca kaw kubeeru gaal gi ak ci kanam kubeer gi.

waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet, ba buur yi wedam, ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko, lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.»

¶ Waa ji ne ma: «Yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii mooy dogali yoon yi jëm ci sarxalukaay bi, bés bu noppee, ci wàllu saraxi rendi-dóomal, ak deret ji ñu ci wara tuur.

¶ Mboolem sarxalkat a ngi taxaw bés bu nekk ci liggéeyam, di jébbale ak a jébbalewaat yenn sarax yooyu, te lenn du ci masa mana far bàkkaar.

Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Aw yiw ak jàmm ju ne xéew ñeel na leen.