TSK

TSK · Leviticus 10:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Gannaaw loolu maay dëgëral boppu Firawna, mu topp leen, ba ma jaare ca siiwal sama ndam, ndax maay daan Firawnaaki xarekatam yépp, te waa Misra dinañu xam ne, man maay Aji Sax ji.» Musaa jottli leen ko, ñu def noona.

Aji Sax ji ne ko: «Wàccal te délsi, ànd ak Aaróona. Waaye muy sarxalkat yi, di mbooloo mi, bu kenn bëtt, jëm ci man Aji Sax ji, lu ko moy ma dal ci seen kaw.»

Ci bunt xaymab ndaje mi ngeen di yem guddeek bëccëg diiru juróom ñaari fan, boole ci di dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, ndax ngeen baña dee, ndaxte loolu moo di li ñu ma santoon.»

Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax ku Sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen.

«Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam.

Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.

Li ko waral mooy yeena ma fecci worma ci digg bànni Israyil, ca ndoxi Meriba Kades, ca màndiŋu Ciin, ndax yeena wormaalul sama sellnga ci digg bànni Israyil.

Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»

Job 2:10 TSK

Mu ne ko: «Waxi jeeg bu dof daal ngay wax, yaw! Du Yàlla da nuy may lu baax, nu jël? Kon kay bu nu mayee safaan ba it, nu wara jël.» Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul ciw làmmiñam.

Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.

Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,

Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.

Moo ma ne: «Israyil yaa di samab jaam, yaw laay wonee samag leer.»

Maa leen di nangul seen saraxu cuuraay, gannaaw bu ma leen génnee fa biir xeet yaak réew ya ngeen tasaaroo ca seen biir, ba dajale leen. Su boobaa maay jëfe sellnga fi seen biir, xeet yi seede.

¶ Ba loolu amee waa ji ne ma: «Néegi bëj-gànnaar yeek néegi bëj-saalum yi janook dig-digalu feguwaay bi, ñooy néeg yu sell yi sarxalkat yi jege Aji Sax ji, di lekke sarax yu sell yee sell. Ca lañuy yeb sarax yu sell yee sell it, muy saraxu pepp yeek saraxu póotum bàkkaar yeek saraxu peyug tooñ yi, ndax bérab bu sell la.

kera bés bu délsee ba jot ci teddngaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.

Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?