Dangeen di jël ab takku cari isob, capp ci deret ji ci ndab li, diw ci seen njëël bunt ak seen ñaari jëni bunt, te bu kenn ci yeen wees buntu këram ba bët set.
TSK
TSK · Leviticus 14:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal.
Picc miy dund da koy booleek bantu seedar bi ak wëñ gu xonq curr gi ak caru isob bi, boole lépp sóob ci deretu picc ma ñu rendi woon tiimale ko ndox mi balle ci bëtu ndox.
Day rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer mu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
Bu loolu wéyee, na ku set jël caru isob, capp ko ca ndox ma, wis-wisal ko ca kaw xayma ba nit deeye, wis ko ca kaw ndab yépp, ak ca kaw nit ña fa nekkoon. Na ko wis itam ci kaw nit ku laal yaxi ku dee, mbaa mu laal ku ñu bóome saamar, mbaa mu laal ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal bàmmeel.
Keroog ba Musaa biralalee bànni Israyil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket, akum ndox, ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar mu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ca kaw téereb yoon wa, ak mbooloo mépp.