Leviticus 18:24
TSK
¶ «Buleen sobeel seen bopp ci mboolem defin yooyu, ndax xeet yi ma leen dàqal, noonu lañu daan jëfe, ba sobeel seen bopp.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Buleen sobeel seen bopp ci mboolem defin yooyu, ndax xeet yi ma leen dàqal, noonu lañu daan jëfe, ba sobeel seen bopp.
Buleen jaamoo noonu seen Yàlla Aji Sax ji nag.
Kon nag, muy góor, di jigéen, ak làng gu mu mana bokk, mbaa giir, fexeleen ba kenn ci yeen du walbatiku, dëddu bésub tey, sunu Yàlla Aji Sax ji, di jaamuji yàllay xeet yooyu. Lu ko moy ab reen dina fëlle fi seen biir, meññal leen tooke ak wextan.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy; màndargam asamaan, buleen ko tiit; na ko yéefar yi tiit.
Gànctoom ga woon ca Misra, bawu ko. Moom lañu daan tëdde cag ndawam, te ñoo daa motoxal cusi janqam, ba sotti ko seen yàqute.
Kon nag buleen séq ak ñooñu dara.