Genesis 48:12
TSK
¶ Ca la leen Yuusufa wàccee fi ñu uufu ci seen maam, daldi dëpp jëëm ci suuf,
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ca la leen Yuusufa wàccee fi ñu uufu ci seen maam, daldi dëpp jëëm ci suuf,
Batseba dem ca Buur Suleymaan, ngir wax ko mbirum Adoña ma. Buur jóg gatandu ko, sukkal ko, daldi toogaat ci ngànguneem. Mu tegal ndeyam ngàngune, mu toog ci ndijooram.
Ca la Eliyu doomu Barakel waa Buus ba, àddu ne: Man de damay ndaw, ngeen diy mag, ba tax may teeylu, ragal leena biralal sama xam-xam.
Sagu ndaw, doole ja; gànjaru mag, bijjaaw ba.
Kàngam yi, ñu jàpp, wékk; te mag ñi, teraleesu leen.
¶ Bul gëdd mag, waaye ñaax ko ni bu doon sa baay. Ndaw it, def ko ni sa rakk.