¶ «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim.
TSK
TSK · Leviticus 19:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu nangoo ko ci seeni loxo, liggéey ko ba sàkk ci sëllu wu ñu móol. Ci kaw loolu ñu naan: «Bànni Israyiloo, seen Yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!»
ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.
¶ «Buleen sàkkal seen bopp ay yàllantu, du lenn luy jëmmu tuur mbaa tuuru doj wu ngeen sampal seen bopp, te doj wu ñu ñaas ay nataal it, buleen ko sàkkal bérab ci seen réew, di ko sujjóotal, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Seen jëmmi tuur yooyu nag, lakkleen leen. Buleen xemmem lenn luy xaalis mbaa wurus ci kaw tuur yi. Buleen ko aakimoo, lu ko moy muy seenug fiir, ndax lu seexluwoo ngoogu ci seen Yàlla Aji Sax ji.
Def nga musiba, ba raw mboolem ñu la jiitu, dem di sàkkal sa bopp yeneen yàlla ak tuur yu ñu móole weñ, ba sama xol fees. Man mii nga xarab, dëddu ma.
Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la, waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
Seetaatleen seen xel bu baax, dale ko bésub tey jii, dale ko ci ñaar fukki fan ak ñeentu juróom ñeenteelu weer wi, daleleen ci bés bii kenug néegu Aji Sax ji tegee, ngeen seetaat seen xel.