TSK

TSK · Leviticus 23:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

mu ne leen: «Loolu la Aji Sax ji wax, te li muy tekki mooy: ëllëg bésu dal-lu la, di bésub Noflaay bu sell ñeel Aji Sax ji. Lakkleen li ngeen di lakk, baxal li ngeen di baxal, te lu ci des, ngeen denc ba suba.»

Ba loolu amee bànni Israyil di nopplu bésub juróom ñaareel ba.

¶ «Diiru juróom benni fan ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, nopplu leen, ndax seen nag ak seen mbaam mana nopplu, seen surga akub doxandéem it mana astandiku.

¶ «Juróom benni fan nag ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, dal-luleen. Bu ngeen doon bey, bu ngeen doon góob, dal-luleen.

¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.

Ndokklee kuy jëfe lii, ndokklee doom aadama ju jàppoo lii, di sàmm bésub Noflaay, bañ koo ñàkke worma, di sàmm loxoom ci jépp jëf ju bon.»

«Su ngeen téyee seen tànk bésub Noflaay, baña def li leen neex sama bés bu sell; su bésub Noflaay di seen nammeel, di bésub Aji Sax bu sell bu ngeen teral; ngeen teral bés bi, bañ cee topp li ngeen jikkowoo, di topp seen bakkan ak wax ju dul jeex;

Ba loolu amee ñu dellu, waajali cuuraay ak diwu xeeñlu ngir néew ba. Bésub Noflaay nag taxaw, ñu dal-lu, ni ko yoon santaanee.

Maa nekkoon ci biir Noowug Yàlla benn bésub Sang bi, ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit.