TSK

TSK · Leviticus 23:32

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Na doon seen bés bu ngeen di nopplu doŋŋ, ngeen war cee toroxlu. Dogal la bu sax dàkk.

Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu, di woor, toroxloo, sukk, ñaanal leen,

Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, te jëf ji ñu la sewale man la dal.

Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.

te naa: “Ana lu nuy woor te xooloo ci? Lu nuy toroxlu te teewluwoo?” Ma ne: Bés bu ngeen woor, yeena ngi topp seen bakkan, di sëqatal seeni liggéeykat.

Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.